
youssou n'dour - bamba the poet lyrics
ahmadou bamba yeemnama
man de, waarunaa ci bamba
man de, yeemunaa ci bamba
li mu bind ci ay teere, gisaguma ku ko jege
man, li ma gis nit kese mënuko
xanaa bamba daawul nelaw
ni modou bamba warna jaaxal kuy bindkat
modou bamba warna yeem kuy woykat
reewi arab, reewi tubaab ak reewi nit ku nuul
booleen were banu daj
mennaa waat ni doo fa gis ku mel ni modou bamba
man de, yeemunaa ci bamba
ci alxuraan la bamba jaare
araaf bu ne defna ci teere
kenn bindle lu ni yeene
xanaa bamba daawul nelaw
ahmadou bamba yeemnama
li mu bind suul ci biir suuf
li mu bind sanni biir geej
eppna fuuf li mu feenal
xanaa sen bi daawul nelaw
man de, yeemunaa ci bamba
ndem bëgg nga xam sa diine jangal xasaayid yi
ndem bëgg nga xam sa boroom jangal xasaayid yi
wer gu yaram, koom koom ak barke lëppangi ci xasaayid yi
nun, li nu am na nu ko ne cass
wer adduna di ko tiitaroo
man de, yeemunaa ci bamba
li mu bind suul ci biir suuf
li mu bind sanni biir geej
eppna fuuf li mu feenal
xanaa sen bi daawul nelaw
xanaa bamba daawul nelaaw
Random Lyrics
- ceren sagu - zorlu sevdam lyrics
- john ramon - cntd lyrics
- roy. - summ3r lyrics
- the sneetches - lorelei lyrics
- paper heart - losing my best friend (single edit) lyrics
- krs-one - it's all insane for me lyrics
- loopro - yevo lyrics
- coy rap - quando eu morrer lyrics
- t-bohne ai music - overlord ⅲ - voracity 【deutsche ai version】 lyrics
- wnhwar - butterfly lyrics